TSK

TSK · Acts 25:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee waa Sif dem Gibeya ca Sóol, ne ko: «Daawuda de, ma nga làqu fa nun. Ma nga ca xunti yu kawe ya ca Orsa, ca kaw tundu Akila, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum.

Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat; ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu.

Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.

¶ Kàngami buur yooyu dem ne Buur: «Waa jii, na dee rekk; mu ngi yoqil xarekat yi des ci dëkk bi, di yoqil ñépp ndax waxam jii mu leen di wax. Waa jii kat wutul jàmmu askan wii, xanaa musiba.»

Luke 23:8 TSK

¶ Ba Erodd gisee Yeesu, bég na lool, ndax yàggoon na koo bëgga gis, ngir la mu déggoon ay mbiram, ba tax mu yaakaara teewe ay kéemaanam.

Acts 9:2 TSK

di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi Yerusalem.

¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.

Ana kon lu tee nit waxe noonee nu soskat yi tuumaale ne nooy wax naan: «Nanu def lu bon, ngir mu jur lu baax»? Ñooñu mbugal lañu yelloo.