TSK

TSK · Acts 25:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bés a ngii tey, nga gisal sa bopp ni la Aji Sax ji tege tey ci samay loxo ci biir xunti mi. Nee ñu ma, ma rey la, waaye dama laa xool bëtu ñeewante. Maa ne duma xàccil mukk sama loxo sama sang, ndax mooy ki Aji Sax ji fal.

Ba ñu ma àggee am tëru mu ko Yawut yi waajaloon nag, ci laa ko yebal ci yaw ci saa si. Jox naa itam ndigal ñi ko sikk, ne leen ñu wax ci sa kanam, gan tooñ lañu ko toppe.

Ma ne leen: “Aaday Room daal nanguwul ñu jébbale nit, ngir ñu rey ko, te jëkkula jàkkaarloo ak ñi ko tuumaal, ba mana layal boppam ci mbir mi ñu ko tuumaal.”

Man nag damaa gis ne deful dara lu jar àtteb dee. Waaye gannaaw moo dénk boppam buur bu tedd bi, man dogu naa ko koo yónnee.