Sa yaakaar tas, Aji Sax ji jege la, sa xol jeex, Aji Sax ji wallu la.
TSK
TSK · Acts 26:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu leen ragal, ngir yaw laay àndal, di la xettli.» Kàddug Aji Sax jee.
Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.
Mu boole ci di wax ak a werante ak Yawut ñiy làkk gereg, te ñoom ñu di ko fexee rey.
Jaambur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital ak a dóori doj.
Ñu dikk, jéggalu, génne leen ci biti, ñaan leen, ñu génn dëkk ba.
Ca la bokki gëmkat ñi yebal Póol ca saa sa, mu jëm tefes ga, Silas ak Timote ñoom, des ca Bere.
¶ Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba.
di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»
Xuloo ba nag gëna tàng, ba njiital gàngoor ga mujj ragal ñu sëxëtoo Póol, ba def ko ay dog. Mu daldi sant lenn ca xarekat ya ñu wàcc, jële Póol ci biir nit ñi, yóbbu ko ca tata ja.
Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»
¶ «Xamleen nag ne xibaaru mucc gii tukkee fa Yàlla, yóbbante nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.
Nu nekk lees nuy tance, waaye deesu nu nappaaje. Dinanu jaaxle, waaye dunu jàq.
Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi.
Ci boobu seede lañu ma tabbe ab yéenekat, ak ndawal kàddu gi, ak itam ab sëriñ, ñeel xeet yi dul Yawut, ngir ma xamal leen yoonu ngëm ak dëgg. Fenuma, dëgg doŋŋ laay wax.
ak itam bundxatal yaak njàqare ya ma dikke woon fa dëkk yooyu di Àncos ak Ikoñum ak Listar. Céy na ñu ma bundxatale, waaye Sang bee ma musal ci lépp!