¶ Yewu génn, dellu ca moroomi jawriñam ña. Ñu ne ko: «Mbaa jàmm? Lu indi dof bii ci yaw?» Mu ne leen: «Ah, xam ngeen nit kii aki waxam rekk!»
TSK
TSK · Acts 26:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bési mbugal dikk na, bési añale taxaw na, na ko Israyil xam. Yonent lañu jàppe ab dof, ku yor waxyu di ku wéradi, ndax seen ñaawtéef gu réy, ak seen mbañeel gu tar.
¶ Naka lañu dégg waxi ndee-ndekki, ñenn ña di ko foontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu, nga waxalaat nu ci moomu mbir.»
Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»
Jàngoo jàngu laa leen daan tege mbugal ay yooni yoon, ngir xàccloo leen. Maa daan sànju ba xaabaabal ci seen kaw, topp leen ba ci biir dëkki jaambur yi.
May yooyu lanuy biral, te waxewunu ko njànglem xam-xamu nit, waaye njànglem Xelum Yàlla lanu koy waxe, di jëfandikoo kàddu yu làmboo Xel mi, ngir teqantal ay mbir yu làmboo Xel mi.
Ndegam danoo teqlikoo ak sunu sago, Yàlla la ñeel. Su nu àndee ak sunu sago nag, yeen la ñeel.