TSK

TSK · Acts 28:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Jonah 1:5 TSK

Ba loolu amee mool ya tiit di yuuxoo, ku nekk di woo sa yàlla wall. Ñu sànni biir géej la ñu yeboon ca gaal ga ngir gëna woyof. Fekk na Yunus wàcc ca suufu gaal ga, tëdd di nelaw ba yàndoor.

Acts 6:9 TSK

Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.

¶ Kon su dee wàllu ñam wu ñu sarxal ay tuur, xam nanu ne ay tuur du dara ci àddina, te Yàlla kenn la.