Acts 6:14
TSK
Noo ko dégg mu ne Yeesu Nasareen boobu dina màbb bérab bii te dina soppi aada yi nu Musaa bàyyee.»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Noo ko dégg mu ne Yeesu Nasareen boobu dina màbb bérab bii te dina soppi aada yi nu Musaa bàyyee.»
Sarxalkat bu mag bi, ak mboolem kurélu mag ñi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas, ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.
Gawar ga àgg Sesare, daldi jébbal boroom réew ma bataaxal ba, jébbal ko Póol itam.
Sarxalkat yu mag yi, ak njiiti Yawut yi boole ko ak Póol. Ñu dagaan ko,
¶ Póol itam ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu Buur Sesaar; te fii lañu ma wara àttee. Yawut ñi nag, defuma leen dara, te yaw ci sa bopp, wóor na la.