Isaiah 30:6
TSK
Yéeneb waxyu bii ñeel na malay àllub Negew: Réewum tiis laak njàqare, kërug gayndeeki segg, ak saamaan ak céebi, mbaam lañu sëf seen alal, jaare fa, giléem lañu sëf seeni denc, jëme xeet wu leen dul jariñ.