¶ Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
TSK
TSK · Acts 28:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam.
¶ «Te it buleen jël benn xaalisu njotug bakkanu kenn ku rey nit ku yelloo dee. Kooku dee rekk mooy àtteem.
Ay rabi àll a fay goore, kër ya fees aki looy, bànjóoli dëkke fa, kéwél di fa curpee.
dundooti àll bi di ma sàbbaal, ñook njabootug bànjóoli, nde maa mayem ndox fi màndiŋ mi, dex ya wale fu noon sereŋ, ma nàndale sama ñoñ, sama tànnéef,
Yeesu ne leen: «Foog ngeen ne waa Galile yooyu dañoo gëna bàkkaar mboolem seen bokki Galile ya ca des, ba tax ñu daj mitit wu ni tollu?
Waa réew ma nag laaye nu biir lool. Fekk na mu tàmbalee taw, ànd akub sedd. Ñu taalal nu am njaar, dalal nu nun ñépp.
waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»