Genesis 41:16
TSK
Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.»
¶ «Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.
¶ «Bokk yi, yeen askanu Ibraayma, yeen ak jaamburi ragalkati Yàlla yi ci seen biir, nun lañu yónnee kàddug mucc gii.
Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.