TSK

TSK · Acts 3:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Abimeleg nag ne ko: «Xawma ku la def jooju jëf de, ndax yaw waxoo ma ci dara; guléet ma dégg ko tey.»

Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?»

su dee moy gu dul teyeef, te mbooloo mi yégu ko woon, su boobaa mbooloo mépp ay sarxal aw yëkk wu ndaw wuy doon rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ak saraxu peppam, ak saraxu tuuroom, ni ko yoon àttee, ak benn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar.

¶ Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.

Acts 7:40 TSK

Ñu ne Aaróona: “Sàkkal nu ay yàlla yu nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra, xamunu lu ko dal.”

Acts 26:9 TSK

¶ «Man ci sama bopp, gàntal lu ma man turu Yeesum Nasaret, sama warugar laa ko defoon.

Boobu xam-xam, kenn ci njiiti xarnu bii xamu ko woon, ndax su ñu ko xamoon, kon duñu daaj Sang bu tedd bi ci bant.

Su dee nag damaa wara wéye sama bakkan bii, ngir mana sottal ab liggéey bu am njariñ, ana lu ma gënal ci diggante dund ak dee? Xawma ko.