ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»
TSK
TSK · Acts 3:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Yàlla ne ko: «Waaw, waaye du tere sa soxna Saarata amal la doom ju góor, nga tudde ko nag Isaaxa. Dinaa fas ak moom sama kóllëre, mu wéy ba ciy sëtam ba fàww.
Léegi nag dellool góor gi soxnaam, ab yonent la de, te dina la ñaanal, nga raw. Waaye soo ko deful, na la bir ne dinga dee, yaak sa waa kër yépp.»
Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele,
Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.
¶ Gannaaw loolu Yanqóoba woo ay doomam ne leen: «Bokkleen daje, ma xamal leen li leen di dikkal ëllëg.
Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
di fàttliku ba fàww kóllëreem, di bàyyi xel ba ci junniy maas kàddoom
Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,
¶ «Bokk yi, yeen askanu Ibraayma, yeen ak jaamburi ragalkati Yàlla yi ci seen biir, nun lañu yónnee kàddug mucc gii.
Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;
Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»
Te su ngeen bokkee ci Almasi, yeen ay askanu Ibraayma, te yeena jagoo dige ba.
¶ Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma.