TSK

TSK · Acts 4:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Esekiya ñaan fi kanam Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim malaakay serub yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf.

¶ «Yaw Aji Sax ji, yaw kenn yaa sàkk asamaan yi, ba ca asamaan ya gëna kawe ak seen gàngoor yépp, ak suuf ak lépp li ci kawam, ak géej ak li ci biiram lépp. Yooyu yépp, yaay ki leen di may bakkan, te gàngoori asamaan, yaw lañuy sujjóotal.

Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; yeena ngi bége ay fen, seeni kàddu diw yiw, seen xalaat diy saaga. Selaw.

Yal na ñi may sosal sàngoo toroxte, làmboo gàcce ni mbubb.

Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk akum ñax aw demin?

Woyleen Aji Sax ji, màggal-leen Aji Sax ji! Mooy xettli néew-ji-doole ci dooley ku bon.

Luke 6:11 TSK

Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu.

¶ Ndax kat, bokk yi, buggunu ngeen umple njàqare, ji nu daj ci diiwaanu Asi. Daj nanu coono bu jéggi dayo, te wees sunu kàttan, ba yaakaaratunu woona dund sax.

Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.