Maa leen di may beneen xol ak xel mu yees. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux.
TSK
TSK · Acts 4:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
Gëmkat ñépp benn lañu woon te ñoo bokkoon lépp.
Noonu lanu doone ñu bare, bokk wenn yaram nun ñépp ci Almasi mi nu gëm, te ku nekk di sa cérub moroom.
¶ Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.
¶ Ma tëje fii nag, bokk yi, bégleen, yokkuleen ba mat sëkk, ñaaxanteleen, mànkooleen te jàmmoo. Su ko defee Yàlla miy Yàllay cofeel ak jàmm mooy ànd ak yeen.
¶ Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di xeex ngir saxal ngëm gi sukkandiku ci xibaaru jàmm bi.
¶ Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.