TSK

TSK · Acts 5:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 2:42 TSK

¶ Ci kaw loolu ñu pastéefu ci njànglem ndaw yi ak ci dundal ag bokkoo, ak ci dagg mburum bokkoo mi, ak ci jataayi julli.

Acts 3:6 TSK

¶ Piyeer nag ne ko: «Xaalis ak wurus de, yoruma ko. Waaye li ma am, jox naa la ko: ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, doxal!»

Acts 4:30 TSK

Ngalla tàllalal sa loxo ngir di wéral ak a amal ay firnde aki kéemaan ci turu Yeesu, sa ndaw lu sell li.»

Acts 9:33 TSK

Mu gis foofa waa ju ñuy wax Ene. Fekk na diiru juróom ñetti at, cib lal rekk lay tëdd ndax yaram wu làggi.

Acts 14:3 TSK

Teewul Póol ak Barnaba toog Ikoñum diir bu yàgg lool. Fit lañu doon waaree ngir Boroom bi, Boroom bi maye ay firnde aki kéemaan yu jaare ci ñoom, ngir seeree ko kàddug yiwam gi ñuy biral.

Noonu la jàppoo ay fani fan, ba Póol mujj xajootu ko. Mu walbatiku ne rab wa: «Maa la sant ci turu Yeesu Almasi, génnal ci ndaw si.» Rab wa daldi génn ca saa sa.

Acts 28:9 TSK

Ba loolu amee jarag ya ca dun ba dikk, daldi wér ñoom itam.

Firnde yiy màndargaal ndawal Almasi, feeñalees na ko ci seen biir, lépp ci ag muñ gu mat sëkk: firnde yeek kéemaan yeek jaloore yi.