TSK

TSK · Acts 5:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba mu ko defee mboolem ña ca am pastéefu xol ak mboolem ña ca seen xel xiir, ñépp dikk, indi jooxeb Aji Sax ji ngir liggéeyu xaymab ndaje meek bépp liggéey bu mu laaj, ngir itam yére yu sell yi.

Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»

Aji Sax ji ne ko: «Déggalal mbooloo mi te def li ñu la wax lépp. Du yaw lañu bañ, waaye man mii lañu bañ ma doonati seen buur.

Job 15:35 TSK

Ñooy sos joote, wasin ñaawtéef, ñoom la seen biir di ëmb wuruj.

Aji Sax ji, bala maa wax baat, ndeke yaw, xam nga lépp.

«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bésub keroog ay xalaat dikkal la, nga mébét mébét mu bon,

Acts 5:3 TSK

¶ Ba loolu amee Piyeer ne ko: «Anañas, lu waral Seytaane di fees sab xol, ba ngay wor Noo gu Sell gi, di làq lenn ci njégu tool bi?

Acts 8:21 TSK

Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.

Am sañunoo yóbbaale mbokkum gëmkat buy sunu soxna, ni yeneen ndawi Almasi, ak doomi ndeyi Sang bi, ak Sefas?

Waaye buggumaa def dara loo àndul, ngir mu baña doon ndimbalu ñàkk pexe, xanaa loo defe xol bu tàlli.