TSK

TSK · Acts 5:42

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Bés bu nekk nag Yeesoo nga doon yendoo jàngle ca kër Yàlla ga, bu guddee mu fanaani ca kaw tund wa ñuy wax tundu Oliw ya.

Acts 2:46 TSK

Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.

Acts 4:20 TSK

Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»

Acts 5:20 TSK

«Demleen taxaw ca digg kër Yàlla ga, ngeen xamal askan wi mboolem lu jëm ci dund gii.»

Acts 8:35 TSK

Filib daldi àddu, tàmbalee ci dog boobu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.

Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu.

¶ Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebatukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»

Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.

Waaye man de Yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee.

waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sam njàngle.