TSK

TSK · Acts 6:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 4:1 TSK

¶ Naka la Piyeer ak Yowaan di wax ak mbooloo ma, sarxalkat yaak jawriñu kër Yàlla gaak Sadusen ya ne jimeet ci seen kaw.

Acts 5:27 TSK

¶ Ñu indi leen, taxawal leen ca kanam kurélu àttekat ya, sarxalkat bu mag ba laaj leen,

Acts 14:2 TSK

Yawut yi gëmul nag di xiirtal jaambur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi.

Acts 17:5 TSK

¶ Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.

¶ Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba.