TSK

TSK · Acts 7:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Musaa nag dellu ca goroom Yettro, ne ko: «May ma, ma dellu Misra, seeti samay bokk, ba xam nu ñu def.» Yettro ne ko: «Demal ak jàmm.»

Mboolem bànni Israyil, góor ñeek jigéen ñi am yéeney indi lu jëm ci liggéey bi Aji Sax ji santaane, Musaa jottli, ñoom ñépp a indil Aji Sax ji ay saraxi yéene.

Ezra 1:5 TSK

¶ Ba mu ko defee ña jiite waa kër Yuda ak Beñamin ak sarxalkat yaak Leween ña, képp ku ci Yàlla xiir rekk, mu daldi dem tabaxi kër Aji Sax ja ca Yerusalem.

Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.

¶ Cant ñeel na Yàlla, mi def ci xolu Tit, mu xér ci yeen ni ma xére ci yeen!

Ba Musaa màggee, ngëm a taxoon mu bañ ñu wooye ko doomu doomu Firawna ju jigéen.

Ndaxte Yàllaa def ci seen xol pastéefu sottal mébétam, ba ñu bokk sottal menn mébét mi, daldi jébbal rab wi seen nguur, ba kera kàddug Yàlla mat sëkk.