TSK

TSK · Acts 7:36

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Dama ne, def naa nga féete Firawna fi ko Yàlla féete, sa mag Aaróona di sa yonent.

¶ Gannaaw ga Musaa tàllal loxoom, mu tiim géej ga, Aji Sax ji yebal ngelawal penku lu réy guddi ga gépp, jañaxe ko géej ga, ndox ya xàjjalikoo, ba suuf su wow feeñ.

Ñu dem, ba àgg fu ñu naan Maara, waaye manuñoo naan ca ndoxum Maara, ndax wex. Looloo waral ñu tudde bérab ba Maara (mu firi Fu wex).

Bànni Israyil dunde nañu mànn diiru ñeent fukki at, ba kera ñu agsee réew mu ay nit dëkke, gannaaw ba ñu jéggee kemu réewum Kanaan.

¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Doxal jóge fii, yaak mbooloo mi nga génne réewum Misra, ngeen dem ca réew ma ma giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne leen seen askan laa koy jox.

¶ Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam Aji Sax ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba.

¶ Ku ñuy wax Kore doomu Isar, mi askanoo ci Keyat doomu Lewi, moo àndoon ak ay Rubeneen, ñuy Datan ak Abiram, doomi Elyab, ak Onn doomu Pelet,

Bés niki tey maa tàmbalee wàcce njàqareek tiitaange ci kaw mboolem askan yi asamaan tiim, ba bu ñu déggee seenum riir, dañuy jaaxle, di lox.»

Su boobaa waxleen seen doom, ne ko: «Ay jaami Firawna lanu woon ca Misra, waaye Aji Sax jee nu génnee Misra ci dooley loxoom.

yaa wàcce ay firndeeki kéemaan ca kaw Firawnaaki jawriñam ñépp ak askanu réewam mépp, ndaxte yégoon nga reewande ga waa Misra doon jëflanteek sunuy maam. Ca nga siiwal saw tur ba tey jii.

Dem nañu sax ba móolal seen bopp jëmmu wëllu te naan: “Yeen, seen Yàllaa ngi; moo leen génnee réewum Misra,” ñàkke la kersa lool.

Fàtte nañu ndimbalam la, bés ba mu leen jotee ca noon ba,

ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon, muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam.

Teewul Yàlla wallu leen ngir turam, ba xamle njàmbaaram.

fàdd luy taaw fa Misra, doom aadama, ba ci mala.

Acts 7:42 TSK

Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israyil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?

ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Gannaaw ñoo sàmmul sama kóllëre nag, man it geesuwuma leen, la Boroom bi wax.