Aaróona ne leen: «Tekkileen boog, indil ma seen jaaroy wurusi nopp, yi ci seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen.»
TSK
TSK · Acts 7:41
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji ne ma: «Jógal wàcce fii gaaw, ndax sa bokk ya nga génnee Misra def nañu yàqute. Teggi nañu xaat yoon wa ma leen santoon. Móolal nañu seen bopp jëmmu tuur.»
Tëgg nañu aw nag ca tundu Oreb, di sujjóotal jëmm ju ñu móol,
Képp kuy tabax jëmmi tuur, doo tus, xërëm yooyu ñu safoo amul njariñ. Ñooñu ñu defi seede te gisuñu, yéguñu, muy seen gàcce!
«Ni cabbu reseñu biir màndiŋ, ni laa fekke Israyil. Ni ndoortel doomi figg ju ndey ja taawloo, ni laa gise seeni maam. Waaye ñoom ñoo dem Baal Pewor, ñoo sédd seen bopp Baal, tuur mu ruslu mi, ba tax leena seexluwu ni kooku ñu sopp.
¶ Ndesu nit ñi musiba yooyii reyul nag, taxul sax ñu tuub seeni jëf, ba bañatee jaamu ay tuur, ak jëmmi xërëmi wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk; xërëm yu gisul, déggul, doxul.