TSK

TSK · Acts 7:44

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir.

Su ko defee nga taxawal jaamookaay bi, ni ñu la ko wone ci kaw tund wi.

Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.

¶ Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga.

Te itam sa bokki Leween ñi, sa giirug baay, jegeñal leen sa bopp, ñu jokku ci yaw, di la jàpple, te yaw yaak say doom, ngeen féete fi kanam xayma ba seedes kóllëre ga dence.

Sarxalkat yooyu, jaamookaay bi ñuy liggéeye, ab misaal la, takkndeeru yëf yu dëggu ya fa asamaan la. Ndax ba Musaa di waaja yékkati xaymab jaamookaay ba, noonu lees ko artoo woon ne ko: «Nanga xool te def lépp, mu dëppook misaal mi ñu la won ci kaw tund wi.»