Psalms 31:5
TSK
Génne ma fiir gi ñu may tëroo; yaw yaa di sama rawtu.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Génne ma fiir gi ñu may tëroo; yaw yaa di sama rawtu.
¶ Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dee.
Te moo yor ndigal lu tukkee ci sarxalkat yu mag yi, ngir yeewlu képp kuy tudd saw tur.»
Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set, teqlikook say bàkkaar, te tudd turu Yeesu.”
ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.