2 Kings 5:15
TSK
¶ Ba loolu amee Naaman dellu ca góoru Yàlla ga, mook mboolem toppam ma. Mu dikk ba ca moom, taxaw ne: «Dama ne léegi wóor na ma ne amul jenn Yàlla ci mboolem àddina ju moy Yàlla ji ci Israyil. Kon nag sang bi, ngalla nangul lii, maa la ko may.»