TSK

TSK · Acts 8:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy.

Job 20:14 TSK

Waaye la muy lekk ay soppiku ca biiram, doon daŋaru ñàngóor ca butit ya.

Jëf ju bon day fiir ka ko sàlloo, bàkkaaram di mbaal, jàpp ko.

«Xanaa du lii moo di koor gi ma taamu: yolomal jéng yu metti, fecci buumi noteel, afal ku diis; dog lépp luy xeetu noteel?

Maa leen di wasaare fi biir xeet yu ñu xamuloon, du ñoom, du seeni maam. Maa leen di tofal saamar, ba raafal leen.»

Baal xel sama naqar ak sama tumurànke, wii wextan akug tooke!

Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.

Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.

Ag ngoreel lañu leen di dig, te ñoom ci seen bopp, ay jaami yàqute lañu, nde lu la man, yaa dib jaamam.