TSK

TSK · Acts 8:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nekkul it wàllaa géej ba ngeen naan: «Ana ku nuy jàllil wàllaa géej, jëlil nu ko, dégtal nu ko, ba nu jëfe ko?»

¶ Ci kaw loolu Lingeeru Saba dégg riirum Suleymaan ma turu Aji Sax ji waral. Mu dikk di nattusi am xelam, di ko cax cax yu jafe.

Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.

Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus. Nit a ngii, juddoo fa,»

Aji Sax ji dafa wax ne: «Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus, ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw, ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo. Sa gannaaw lañuy topp, yeewe, jàllsi; sujjóotal la, di ñaan naan: “Fi yaw daal la Yàlla ne, du feneen, te tuur neen la.”»

Ay xeet ay fekksi sag leer, ay buur wutsi sa ceeñeeru njël.

Maay teg firnde fi seen digg, ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom, yebal leen ci xeet yi, yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd, ñooña di ñu mane fitt, ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan, waa duni géej yu sore ya, ñooñu masula dégg sama jaloore, te masuñoo gis sama teddnga, sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga.

¶ Ci biir loolu Ebedd Meleg, Kuuseen ba, di bëkk-néeg ci biir kër buur, dégg ne tàbbal nañu Yeremi ca kàmb ga. Fekk Buur a nga toog ca bunt ba ñu dippee Beñamin.

Sama jaam ñi, sama ñoñ ñi tasaaroo, ca wàllaa dexu Kuus lañuy bawoo, ba indi samab sarax.

¶ Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm bérab ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.