¶ Defleen sama kàddu yii ci seenum xel ak ci seen xol. Takkleen ko, muy firnde ci seen loxo, te na doon am mbandal ci seen diggantey gët.
TSK
TSK · Acts 8:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.
Sama doom, déggal samay wax, fonk samay santaane.
¶ Lii moo di peeñum Esayi doomu Amocc, di lu mu gis ci mbirum Yuda ak Yerusalem ci janti buuri Yuda yi ñuy wax Osiyas ak Yotam ak Axas ak Esekiya.
Ñu jox ko téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ubbi téere bi, gis dog bi ñu bind ne:
Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la.
Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi.