¶ «Léegi maa ngii ci curgag Noo gu Sell gi, di dem Yerusalem, lu ma fay dal sax, xawma ci dara,
TSK
TSK · Acts 9:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Acts 20:22
TSK
Acts 21:11
TSK
Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»
Ci lépp kay lanu bëgga seedeel sunu bopp, ne noo yelloo ngërëm, te ay jawriñi Yàlla lanu, di ñu muñ lu bare ci biir coono, aki mitit, aki njàqare;
ngir kenn baña jàq ci biir tiis yii, ndax yeen ci seen bopp xam ngeen ne loolu lanu séddoo.
2 Timothy 2:9
TSK
Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng.
1 Peter 4:14
TSK
Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.