TSK

TSK · Acts 9:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bu leen njàqare dikkalee, fekk mboolem mbir yooyu dab leen, su boobaa dingeen mujj délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji te dingeen ko déggal.

Sa mboolooy taxawal seen bopp, sa bésub xare. Ña nga soloo darajaak sellnga, faboo fa njël sosoo, diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay.

Suuf a ngi maral, wow koŋŋ, gottub Libaŋ am gàcce, lax, àllub Saron doon joor gu wow, garabi Basan ak Karmel yëngu, di ruus.

Joorug Saron ay dellu di parlub gàtt gi, xuru Akor di goorukaayu nag yi, ñeel sama ñoñ ñi may sàkkuji.

Israyiloo, dellul ci sa Yàlla Aji Sax ji, fakktaloo nga sag ñaawtéef.

Luke 1:16 TSK

Niti bànni Israyil ñu bare, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla.

Acts 5:12 TSK

¶ Ci kaw loolu ay firnde ak kéemaan yu bare di sottee ci loxol ndaw yi, ci biir askan wi. Gëmkat ñi nag di bokk daje ñoom ñépp fa ñuy wax Mbaarum Suleymaan, ca biir kër Yàlla ga,

Acts 9:42 TSK

Mbir ma nag siiw ca Yope gépp, ñu bare gëm Sang bi.

¶ «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jaambur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla.

¶ Noonu la kàddu gi lawe ba féete kaw ci kàttanu Boroom bi.