Ci biir loolu ñu jox xaalis yettkati doj yeek xaddkat yi, jox waa Sidon ak waa Tir ab dund, aki naan akug diw, ngir ñu jëleji Libaŋ ay banti seedar, jaarale ko ci géej gi ba Yafa, ci ndigalal Sirus buuru Pers.
TSK
TSK · Acts 9:36
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.
Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub, gi Yeesu Almasi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.
te moom ngeen nekke seen digg ak mboolem bokki diiwaanu Maseduwan gépp. Teewul nag, bokk yi, nu di leen ñaax, ngir ngeen gënate jëfe noonu.
te di ku ñu seedeel jëf ju rafet; lu mel ni yar ay gone, ak man gan, ak teral gëmkat ñu sell ñi, ak dimbali ñi tollu diggante, ak di jàppoo jépp jëf ju baax.
Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottale Yeesu Almasi, mi daraja ñeel ba fàww. Amiin.