TSK

TSK · Acts 9:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sóol gis gàngooru waa Filisti, daldi tiit lool ba fit wa rëcc.

Ana kuy wormaal Aji Sax ji, mu won ko yoon wi mata taamu,

Xam naa jikkoom, waaye maa koy faj, wommat ko, dëfale koy xéewal, mook ñiy ñaawloondook moom.

Maa fa jaare, seen la ngay wéqu, sangoo sa deret. Ma ne la: Sangoo nga sa deret waaye, dundal! Neeti la: Sangoo nga sa deret, waaye dundal.

Acts 2:37 TSK

¶ Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»

Acts 10:6 TSK

Ma nga dal ak meneen Simoŋ ma, wullikat ba këram féete wetu géej.»

Kon nag yebleel Yope, nga woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; ma nga dal ca kër meneen Simoŋ, wullikat ba ca wetu géej ga.”

¶ Ba loolu amee boroom kaso ba indilu ab làmp, daldi ne saraax dugg, ne gurub fa kanam Póol ak Silas, di lox.

Naka la Póol wax ci mbirum njub, ak moom sa bakkan, ak àtteb bés-pénc, Feligsë daldi tiit, ne ko: «Léegi, man ngaa demagum, bu ma ko talee, dinaa la wooluwaat.»

¶ Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,

Ndax kat moo noon Musaa: «Maay yërëm ku ma neex, te maay ñeewante ku ma neex.»

Esayi it am fit ba ne: «Ñi ma seetul woon, gis nañu ma, ca ña ma laajul woon laa feeñe.»

¶ Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,

James 4:6 TSK

Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»