Góor ga xaacu, gëdd sarxalukaay ba ci ndigalal Aji Sax ji, daldi ne: «Yaw sarxalukaay bi, éey sarxalukaay bii! Aji Sax ji dafa wax ne: “Xamal ne doom ju góor dina juddoo kër Daawuda, Yosya lay tudd. Sarxalkati bérabi jaamookaay yiy taal saraxu cuuraay ci sa kaw, ñoom lees di rendi ci sa kaw. Yaxi nit lees di lakk ci sa kaw.”»
TSK
TSK · Amos 3:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Naka noona mu boole ca sarxalukaay ba ca Betel ak bérabu jaamookaay ba fa doomu Nebat Yerbowam ma bàkkaarloo woon Israyil, yékkati woon. Sarxalukaay boobaak bérabu jaamookaay booba sax yàq na ko. Dafa lakk bérabu jaamookaay ba, wol ko ba mu mokk, lakk xer wa ñuy jaamoo Asera.
Jaamookaay yu kawe ya ca Bet Awen, bàkkaarukaayi Israyil yooyu lees di tas. Ay dég aki dagg ñooy sax ca seeni sarxalukaay, dees na ne tund yu mag yi: «Mëddleen nu,» te naan tund yu ndaw yi: «Daanuleen ci sunu kaw.»
Buleen sàkkuji fa Betel, buleen dem Gilgal, te buleen jàll Beerseba. Gilgal ay gàlloo ngàllo; Betel neen.»
Ma gis nag Boroom bi, mu taxaw ca sarxalukaay ba. Mu ne: «Dóorleen ci kaw jëni jaamookaay bi, ba kenu yi yëngu, te ngeen màbb ko ci kaw boppi ñépp; ña mucc, ma reylu ci xare. Du kuy fëx ba rëcc, du kuy daw ba raw.