Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,
TSK
TSK · Amos 3:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndax kat askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la seen Yàlla Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.
Aji Sax ji it biral na bésub tey, ne yeenay doon ñoñam ñi mu séddoo, noonee mu leen ko dige woon, te ngeen di sàmm mboolemi santaaneem.
Mooy wax Yanqóoba kàddoom, dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.
Maa ngii déy, di woo mboolem waasoy réewi bëj-gànnaar ak seeni buur.» Kàddug Aji Sax jee. «Dañuy dikk, ku ne dëj ngànguneem fi janook bunti Yerusalem, jànkoonteek tataam yépp, ak dëkki Yuda yépp.
Xëppal sa xadar yéefar yi la yégul, ak làng yi la tuddul. Ñoo bóom giirug Yanqóoba, bóom leen ba fàkkas leen, gental seen dëkkuwaay.
Sa xejj yi nga miinal sa bopp, bu ñu walbatikoo tiim la, ana looy wax nag? Kon mitit du la jàpp, nga mel ni kuy matu?
Mag ñu góor ñeek xale yu góor yi, jeeg jeek janq ji, ba ci tuut-tànk yi, reyleen ñépp, faagaagal leen. Waaye ku ci am rëddu jë, buleen ko laal. Dooreleen ko ci sama bérab bu sell bi.» Ñu tàmbalee bóom mag ña ca kanam kër Yàlla ga.
Matal nga sa kàddu gi nga wax ci nun, nook sunu kilifa yi nu yilif, ba nga wàccee ci sunu kaw, ci Yerusalem, musiba mu réy mu masula am feneen fu mboolem asamaan tiim.
Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.
Lépp ndax ngànctu gu bare, gi gànc bi nekke! Jekk tànkee, boroom xërëm yi, ci ngànctu nga jaaye ay xeet, te xërëmtu nga naxe ay giir.
Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.
Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm?