¶ Axab nag ne Abdiyas: «Duggal ci biir réew mi te seet ci bëti ndox yeek xur yépp. Jombul nu gis ñax, ba mana rawale bakkani fas yeek berkelle yi, ba du jar nu di leen jekkli.»
TSK
TSK · Amos 4:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Walaakaanaak néew-doolee ngi wër, di wut um ndox, amul. Seen put wow koŋŋ ak mar. Man Aji Sax ji, maa leen di nangul; man Yàllay Israyil, duma leen wacc.
Ma noon su ma defee loolu lépp ba noppi, dina délsi, te délsiwul. Te doomu ndeyam Yuda workat bi gis na ci.
Kàngam ya yebal seeni surga, ñu rooti; ñu dem, gisuñu ndox ca mbalka ya, délseek seen xotti ndab, jàq, yaakaar tas, ñu muuru di tiislu.
Mu neeti ma: «Yaw nit ki, maa ngii di dagge fi Yerusalem lépp luy dugub. Ci biir njàqare lañuy lekke as mburu te xol bu jeex lañuy naane siitum ndox.
Duñu dellu réewum Misra. Waa Asiri ñooy doon seen buur, nde ñoo baña délsi fi man.
«Maa leen dumaa gub yu yàqu, di saxee saxe, wowal seeni tool aki tóokër, garabu figg ak oliw, njéeréer yi lekk. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.
Yeenay ji lu bare, góob tuuti; lekk, suuruleen; naan, màndiwuleen; solu, nugluwuleen; boroom peyoor feyeeku, yeb ci mbuus mu bënn.»