TSK

TSK · Amos 4:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jee leen di dumaa woppi ràgg, ak yaram wu tàng, ak lakk-lakk, ak jant bu tàng jérr, ak maral, ak gàncax gu xuur, tegi liir, lépp topp leen ba ngeen sànku.

¶ «Bu xiif amee ci réew mi, mbaa mbas, mbaa gàncax gi lakk, mbaa benaat xuural ko, mbaa mu diy njéeréer mbaa soccet, mbaa su dee congum seen noon ci seen dëkki réew mi, mbaa muy mboolem luy musiba ak mboolem jàngoro, su boobaa,

Job 36:8 TSK

Bu ñu demee ba ñu jéng leen, mbaa buumi njàqare ŋodaar leen,

Waaye xeet wi delluwuñu ca ka leen duma, sàkkuwuñu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israyil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee.

Duñu dellu réewum Misra. Waa Asiri ñooy doon seen buur, nde ñoo baña délsi fi man.

Joel 1:7 TSK

Samag reseñ lañu fóom, samag figg lañu xasa xas, ba mu set, ñu sànni, car ya weex tàll.

Amos 4:6 TSK

«Maa wéetal seeni biir seen dëkkoo dëkk, dugub ñàkke fépp fu ngeen moom, te taxul ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.

Amos 7:1 TSK

¶ Am na bés Boroom bi, Aji Sax ji won ma am peeñu. Ndeke ma ngay sàkk naaxu soccet. Fekk na ñu góobal Buur, ba gàncax giy saxaat.

Maa leen di gëddal njéeréer, ba du leen yàqal meññeefum suuf, te reseñug tool du leen jaasiral.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.