TSK

TSK · Amos 5:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?»

Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»

Mooy ñiy tuumaal nit, di fiir ab àttekat ca pénc ma, di àtte ñàkkal nit ku jub ci dara.

Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma, ma naagu, nga nax ma, jaay ma doole, ba man ma. Ñu ngi may kekku bés bu ne, ku ne di ma kókkali.