Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,
TSK
TSK · Amos 5:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
«Maay def Yerusalem jali doj, till yi dëkke; ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.»
Nañu gaaw dëbbeel nuy jooy, gët taa, rongooñ wal.
Neeleen wóoy ni janq bu woddoob saaku, di ko ñaawloo jëkkëram, ja ñu ko dencaloon ba muy lu tuut.
Sellal-leen ag koor, woote am ndaje, wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi, ca seen kër Yàlla Aji Sax ji, te ngeen woo Aji Sax ji wall.
Maa leen di yóbbu ngàllo ca wàllaa Damaas.» Aji Sax jee ko wax, kookooy Yàlla Boroom gàngoori xare yi.
Lee ma tax di jooy ak a yuuxu, ne duŋŋ, deme tànki neen, di ko ñaawloo. Naa yuuxu nig till, naa sab sabum looy ndaxu naqar.
Fu sore lañuy dànd, ndax ragal toskarey dëkk bi, te naan: «Wóoy, wóoy ngalla dëkk bu mag ba! Babilon ma ca doole ja! Ci wenn waxtu rekk la sa àtte dikk!»
¶ Dañuy xëpp suuf seen kaw bopp, di yuuxook a jooy ak a naqarlu, naan: «Wóoy, wóoy, ngalla dëkk bu mag ba! Sa koom a woomal mboolem boroom gaal ci kaw géej, wenn waxtu rekk, nga gental.»