TSK

TSK · Amos 5:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji dina fàdd Israyil. Dinañu mel ni gattax guy foy-foyi cim ndox. Dina déjjatee Israyil ci suuf su baax sii mu joxoon seeni maam, tasaare leen ca wàllaa dexu Efraat, ndax dañoo samp ay xer yu ñuy jaamoo Asera, di merloo Aji Sax ji.

Ba Ose duggee juróom ñeenteelu atu nguuram, ca la buurub Asiri nangu Samari, jàpp waa Israyil, yóbbu Asiri. Ñii mu teg leen ca diiwaanu Ala, ñee ca Gosan ca wetu dex ga ñuy wax Abor, ña ca des mu dëël leen ca dëkki xeet wa ñuy wax Medd.

Amos 4:13 TSK

Kii kat moo móol tund, di sàkk ngelaw, di xamal nit nammeelam. Kee di soppi lëndëm ag leer, di daagoo kawte ya. Kookoo di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Acts 7:43 TSK

Molog seen tuur mi, ngeen yóbbaale xaymab jaamookaayam, ak seen biddiiwu yàlla ji ñu naa Refan, jëmm yooyu ngeen sàkk, di leen sujjóotal! Kon nag maa leen di toxal ca wàllaa Babilon.”