Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy.
TSK
TSK · Amos 5:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye kuy topp yoonu ndëngte, Aji Sax jee koy sànk, boole kook kuy def lu bon. Yal na jàmm dal Israyil.
Tóokëru Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat, mooy waa kër Israyil. Niti Yuda it ñooy njëmbat li mu safoo. Mu di ko yaakaare njub, njubadi ne jaas. Mu yaakaar njekk, yuuxi njekkar ne jaas.
Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi, bind ko, te muy jur coono,
Noo tooñ Aji Sax ji, wor ko, te noo dëddoo sunu Yàlla jii, kàdduy fitna ak fippu, ak fen yu nu mébét, nas ko,
«Waaye su dee ku juboon, ba noppi dëddu njubte di def njubadi, di roy mboolem jëf ju siblu ju ku bon def, kooku nu muy dunde? Mboolem njekk gu mu defoon, deesu ko ko dencal. Ag ñàkk wormaam ak bàkkaaram moo koy taxa dee.
Boroom njekk li daal, su dëddoo njekkam di def njubadi, njubadi gaay doon àtteb deeyam.
Gannaaw yeenay not néew-ji-doole, di foqati ŋëbu peppam, tabax ngeen këri boroom barke, waaye dungeen ko dëkke. Jëmbat ngeen tóokëri reseñ juy tem-temi, waaye dungeen naan ca biiñ ba.
Ngalla dégluleen lii, yeen njiiti kër Yanqóoba; yeen kilifay kër Israyil. Yeen ñi seexlu dëgg, lunkal wépp yoonu njub.
Waaye Aji Sax ji, xanaa du yaa masa nekk? Sama Yàlla sama Aji Sell ji, doo saay. Aji Sax ji, ab àtte nga tabbe ñii, yaw sama cëslaay, mbugal nga fi dëje ñii.