TSK

TSK · Amos 7:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba Ose duggee juróom ñeenteelu atu nguuram, ca la buurub Asiri nangu Samari, jàpp waa Israyil, yóbbu Asiri. Ñii mu teg leen ca diiwaanu Ala, ñee ca Gosan ca wetu dex ga ñuy wax Abor, ña ca des mu dëël leen ca dëkki xeet wa ñuy wax Medd.

seeni doom, ñu moxoñe fi seen kanam, seeni kër, ñu sëxëtoo, seeni jabar, ñu tëdde.

Yaw Pasur, yaak sa waa kër yépp ay duggi njaam ca Babilon. Babilon nga jëm te fa ngay dee, ñu rob la fa, yaak mboolem sa soppe ya nga daan wax ay waxyuy fen.”»

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la yebal, nga jóge fi kaw suuf. Ren jii ngay dee, ndax kàdduy gàntal nga waxal Aji Sax ji.”»

“Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Yaw yaa yónnee ci sa turu bopp ay bataaxal ca askanu Yerusalem gépp, rawatina sarxalkat ba Cefaña doomu Maaseya, ak mboolem sarxalkat ya. Nga di ci wax ne:

Kon nag Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di mbugalsi Semaya Neyelameen bi, mook askanam. Ku bokk ci moom du toog ci biir xeet wii, bay gis ngëneel li may defal sama ñoñ.” Kàddug Aji Sax jee. “Moo xiirtal askan wi ci gàntal Aji Sax ji.”»

Ca kaw tund yu mag ya lañuy rendee ay sarax, cuuraay, ñu taale ca tund yu ndaw ya, ak ca taatu gii garab gu mag, ba ca gee, fa ker ga neexe. Moo tax seeni doom di gànctu, seen séeti doom di jaaloo.

Amos 7:11 TSK

Mu ngi naan ci xare ngay deeye, te dees na jële Israyil suufam moos, yóbbu ngàllo.»