Aji Sax jeey dëggal ñoñam, mooy ñeewante ay jaamam, bu gisee doole dëddu, ba kenn desul, dub jaam, dus gor.
TSK
TSK · Amos 7:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Psalms 78:38
TSK
Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,
Jeremiah 26:19
TSK
¶ «Ndax tax na Esekiya buurub Yuda mbaa kenn ci waa Yuda reylu ko? Du Buur Esekiya daa wormaal Aji Sax ji, tinu ko, ba Aji Sax ji fomm musiba mi mu leen dogaloon? Nun nag musiba mu réy lanu nara indil sunu bopp.»
Hosea 11:8
TSK
«Efrayim, ana nu ma lay baye, yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo? Ana nu ma lay defe ni Atma? Nu ma lay yemaleek Ceboyim? Sama xol a bëpp, sama yërmandee yëngu.
Amos 7:6
TSK
Boroom bi Aji Sax ji fomm ko ne ma: «Liitam du am.»
James 5:16
TSK
Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale.