¶ Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal.
TSK
TSK · Amos 8:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Naka la Daawuda dox ba wees tuuti collu tund wa rekk, yem ca Ciba, surgab Mefiboset. Ma nga làng ak ñaari mbaam yu ñu laltaay, sëf leen ñaar téeméeri mburu ak téeméeri danki reseñ ak téeméeri danki figg ak mbuusum biiñ.
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Caru garabu saal laa gis.»
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkalaat ma ñaareel bi yoon, ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Cin luy bax laa gis. Mu ngi joye bëj-gànnaar, jublook nun.»
¶ Gannaaw gi Nabukodonosor buuru Babilon toxal na buurub Yuda Yekoña doomu Yowakim, yóbbu ko Babilon, mook kàngami Yudak liggéeykati xarala yaak liggéeykati weñ ya. Ba loolu amee Aji Sax ji am lu mu ma won: da maa jekki gis ñaari dàmbi figg yu tege fi kanam kër Aji Sax ji.
Sunuy tànk lees di topp, ba manatunoo daagoo sunuy mbedd; sunu bés jege, sunu àpp di matal, sunu saa taxaw!
¶ Mu teg ca, ne ma: «Yaw nit ki nag, mboolem li ma lay wax, dégloo ko nopp, te teewloo ko xel.
Jeexlee ngoog, jeexle dikk na, jekki, yewwul la. Mu ngii, di dikk!
Mu ne ma: «Yaw nit ki, du yaa gis li magi kër Israyil di def ci lëndëm gi, ku nekk ak fa ñu jagleel sa nataalu tuur. Ña nga naan: “Aji Sax ji gisu nu, Aji Sax ji wacc na réew mi.”»
Kon wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maay dakkal woowu léeb, ba muy léebtil fi Israyil.” Waxleen kay ne leen: “Bés a ngi jubsi, peeñoo peeñu sotti.
Bési mbugal dikk na, bési añale taxaw na, na ko Israyil xam. Yonent lañu jàppe ab dof, ku yor waxyu di ku wéradi, ndax seen ñaawtéef gu réy, ak seen mbañeel gu tar.
Wóoy, ngalla man mi mel ni kuy forsi, te meññeef ma fatu, may raasaatu, te du cabbu reseñ ju nit lekk, du figg ju bees ji ma namm.
Malaaka mi ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Taxañ buy naaw laa gis, guddaayam di ñaar fukki xasab, yaatuwaayam di fukki xasab.»