TSK

TSK · Amos 8:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Na seen nattukaayu diisaay jub, doom ya ngeen cay natte jub, te na nattukaayi sol-sotti yi jub. Maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen génne réewum Misra.

¶ «Te itam seen bési Terutel weer, nangeen sarxe ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. Ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xar yu góor yu menn at, te lu ci nekk mucc sikk,

Doju màndaxekaay bu mat te dëggu ngeen wara am, te nattukaayu sol-sotti bu mat te dëggu ngeen wara am, ndax ngeen gudd fan ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox.

¶ Ci fan yooyu ma gis ci Yuda ay nit ñuy nal reseñ, bésub Noflaay. Mu am ñuy indi ay sabaari pepp yu ñuy sëf ay mbaam, boole ca biiñ ak reseñ ak figg ak lu nekk, di ko yóbbu Yerusalem ci bésub Noflaay. Ma àrtu leen it ca la ñuy jaay seen yëf yooyu ci boobu bés.

Yékkatileen woy te jiin, xalam neex, ànd ak moroom ma.

Nattub diisaay aki ndabam, na jub ngir Aji Sax ji. Moo sàkk mboolem nattukaay.

Buleen fi indeeti saraxi caaxaan, seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la. Terutel weer ak bésub Noflaay ak wooteb ndajee ci yem! Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.

Seen màndaxekaay na doon njub, efab nattukaayu sol-sotti di njub, seen bat bi ñuy natte lu ñuy xelli di njub.

Ni Kanaaneen biy jula, ni la Efrayim yore màndaxekaayu njublaŋ cib loxoom, bëgga naxe.

Yeena ngi naa: “Ndaw lu soof,” di ciipatu.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Jur gu ñu sàcc ngeen may indil, ak guy soox, ak gu wopp, loolu mooy seen sarax! Nu ma koy nangoo ci seeni loxo?» Aji Sax jee ko wax.

¶ Kon nag bu leen kenn sikkal ci ñam wu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, mbaa màggal bés bu rafet, mbaa Terutel weer, ak bésub Noflaay.