Sàkkul xel mu rafet ni xaalis, wut ko ni alal ju làqu.
TSK
TSK · Colossians 2:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye ci ñi ñu woo, ñuy Yawut, di Gereg, Almasi mooy manoorey Yàlla, di xam-xamu Yàlla.
¶ Moona xam-xam lanuy xamle ci biir gëmkat ñi mat, waaye du xam-xamu xarnu bii, ak bu njiiti xarnu bii, di nit ñuy wéy.
May niital ñépp, ni Yàlla nara sottale mébétam, miy mbóot mu làqu woon naka jekk fa moom Yàlla mi sos lépp.
ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom.
Na leen kàddug Almasi dëkke, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jànglantee, ak a artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ay taalifi Sabóor, ak woyi tagg Yàlla, ak woy yu fentoo ci Noo gi.
¶ «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; doj wu ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.