TSK

TSK · Colossians 2:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yeen waa kër Yanqóoba, kaayleen nu doxe leeru Aji Sax ji!

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,

Moo tax dootu man maay dund, waaye Almasi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.

¶ Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp,

Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.

¶ Li ci des nag, bokk yi, moo di yeena nangoo ci sunu làmmiñ, jëfin wi ngeen wara jëfe ba neex Yàlla, te it moom ngeen nekke. Waaye danu leen di tinu, di leen ñaax, ci turu Sang Yeesu, ngir ngeen gënati koo jëfe.

Jude 1:3 TSK

¶ Soppe yi, yàkkamti woon naa leena bind ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye fàww ma bind leen, ngir ñaax leen ci xeexal yoonu ngëm, wi Yàlla xasa dénk ñu sell ñi, benn yoon ba fàww.