Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.
TSK
TSK · Colossians 3:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Baal nu sunuy bàkkaar, ni nuy baale nun itam, mboolem ñi nu tooñ, te bu nu dugal ci nattu.»
¶ Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.
¶ Kon nag, ni leen Almasi xajoo, nangeen ko xajoontee, ngir teddngay Yàlla.
Ku ngeen jéggal ag tooñ, ma jéggal ko, man itam. Man nag, su ma jéggalee, ndegam am naa lu ma jéggale, yeena tax ma def ko, ci kanam Almasi,
Yennikoonteleen seeni yen, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi ba mu mat sëkk.
Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey balante, ni leen Yàlla baale ci Almasi.
¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.
Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi itam sonnal na leen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.