Indileen ñii diy silmaxa te ami gët; tëx te ami nopp.
TSK
TSK · Daniel 10:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nanga xam kon xéll ne: li ko dale keroog ba ñuy siiwtaane dogal ba jëm ci leqli Yerusalem, tabaxaat ko, ba keroog njiit li ñu fal di feeñ, juróom ñaari àppi juróom ñaar la. Te ci juróom benn fukk ak ñaar ci àppi juróom ñaar lañuy tabaxaat pénc ak kàmb gu ñu aare dëkk bi. Waaye jamono yu metti lay doon.
Man ci sama wàllu bopp nag, maa nga woon ca wetam, di ko aar ak a jàpple, ca at ma jëkk ca nguurug Daryus waa Medd ba.
¶ Malaaka ma waxati ma, ne ma: «Jamono yooyu ci la Mikayel, malaakam wattukat mu mag, miy taxawu sa mbooloo, di jóg. Muy jamonoy njàqare ju masula am, cosaanal xeet yi ba tey jii. Bu keroogee sa bokk yay mucc, di ñi ñu bind ci téereb dund bi.
Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.
Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg.”
¶ Ab xare nag jibe fa asamaan. Mikayel aki malaakaam di xareek ninki-nànka ji, ninki-nànka jeeki malaakaam it di xare,