¶ Ca ndoortel nguurug Aserus nag, ñu bind Aserus bataaxal buy duural waa Yudak Yerusalem.
TSK
TSK · Daniel 11:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ci kaw loolu liggéeyu kër Yàlla ga ca Yerusalem taxaw. Taxaw na ba ca ñaareelu atu nguurug Daryus buuru Pers.
Moo leen taxa ràngoo reewande, làmboo coxor.
¶ «Ñaareelu rab wa ne jimeet, nirook urs. Mu ngi taxawe wet, ŋank ñetti faar. Ñu ne ko: “Jógal lekk yàpp wu bare.”
Peeñum ngoon meek mu bëccëg mi la dikkal lu wér la. Yaw nag neel cell ak peeñu mi, ndax des na fan yu bare.»
Mu ne ma: «Ndax xam nga lu ma taxa dikk? Léegi ma dellu xarejeek rawaanu réewum Pers; te bu may dem, rawaanu Geres dikk.
¶ «Bu loolu weesee dina ànd ak mbooloo mu bare, daldi yebook doole ak pastéef ci kaw buur bëj-saalum. Buur bëj-saalum waajal xare, ànd ak mbooloo mu réy te bare doole lool, waaye sottiwul ndax pexe yu ñu koy lalal.
¶ Ci kaw loolu ki toog ci ngàngune mi ne: «Maa ngii di yeesal lépp!» Mu teg ci ne ma: «Bindal, yii kàddu yu wóor la te dëggu.»