Isaiah 14:31
TSK
Yeen magi pénc mi, ñaawluleen! Yeen waa dëkk bee, yuuxuleen! Na Filisti gépp ne yàcc! Bëj-gànnaar déy la saxar jollee, kenn du wuute gàngooru noon ya.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yeen magi pénc mi, ñaawluleen! Yeen waa dëkk bee, yuuxuleen! Na Filisti gépp ne yàcc! Bëj-gànnaar déy la saxar jollee, kenn du wuute gàngooru noon ya.
¶ Ci ñetteelu atu nguurug Sirus buuru Pers, kàddu daa dikkal Dañeel ma ñuy wax Beltasar. Kàddu googu di gu wóor tey yégle xare bu mag. Mu dégg kàddu gi, xam pirim peeñu mi.
¶ «Bu loolu weesee dina ànd ak mbooloo mu bare, daldi yebook doole ak pastéef ci kaw buur bëj-saalum. Buur bëj-saalum waajal xare, ànd ak mbooloo mu réy te bare doole lool, waaye sottiwul ndax pexe yu ñu koy lalal.
Ci kilifteefu ay wattukat aki saytukat lay nekk ba kera mu àggee ca at ya ko baayam àppaloon.