TSK

TSK · Daniel 11:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Fu ngeen dégg liit gi jibe fa, fekksileen nu fa. Sunu Yàlla dina nu xeexal.»

Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.

Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Aji Sax ji nee: «Maa leen di won ay kiraama, na woon ba ngeen di génn réewum Misra.»

«Sàmm yi la sama mer tàkkal, ñoom sikket yooyu laay dikke mbugal. Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat mooy taxawu kërug Yuda, géttam, te moo leen di def aw fasam wu am daraja, ngir xare.

Bésub keroog maay def Yerusalem di doj wu diis gann ci xeet yépp. Képp ku ko jéema yëngal, da ciy gaañoo gaañu rekk. Te xeeti àddina yépp ay daje ci kawam.

Sunu xibaaru jàmm nag, su muuroo, ñi nara sànku la muurul.

¶ Kon nag yaw doom, doolewool yiw, wi Almasi Yeesu di maye.

Ñu jox ku ci nekk mbubb mu weex, ne leen ñu négandiku tuuti, ba kera seeni bokk ak ñi ñu bokkal liggéey bi, te ñu war leena bóom ni ñoom, ñépp dikk, ba lim bi mat.

¶ Ab xare nag jibe fa asamaan. Mikayel aki malaakaam di xareek ninki-nànka ji, ninki-nànka jeeki malaakaam it di xare,