xamoo ne ku bon, ag sarxolleem àggul fenn, te bànneexu yéefar yàggul?
TSK
TSK · Daniel 11:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan, sama giiru dund du dara fi yaw. Képp ku taxaw di cóolóolu neen. Selaw.
Ba ma àggee sa kër gu sell ga, laa doora gis muju ku bon.
Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
Waaye xeet wu ma ci déggalul, xeet woowu dama koy déjjati, déjjat, sànk leen.» Kàddug Aji Sax jee.
Mboolem xuru néew yaak dóom ya ak mboolem tool ya, ba ca yoonu ndox ma ca Sedoron, ba ca ruqu buntu Fas ya ca penku: lépp lees di sellalal Aji Sax ji. Deesatu fa buddat mbaa di fa daaneel dara.»
Dañeel da ne: «Damaa gis guddi ci peeñu mi; mu jekki-jekki am ngelaw lu jóge ñeenti wet, riddeendoo, di yëngal géej gu mag ga.
¶ «Ni ma ne jàkk ci béjjén yi, beneen béjjén bu ndaw ne pëll, génn ci seen biir, ñett ca béjjén ya jiitu buddeeku. Béjjén bu ndaw baa nga am bët yu mel ni bëti nit ak gémmiñ gu muy waxe kàdduy damu.»
Dañu koo damm, ñeenti béjjén wuutu ko, di ñeenti nguur yu soqeekoo ca xeet wa, waaye duñu am doole ni ga jiitu.
Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?”